Kodu jëfu OIT ci wàllu VIH/SIDA ak àdduna liggéey
Kod bi dafay joxe tegtal yu am solo ci ñiy jël matuwaay yi, mbootaayi patroŋ yi ak liggéeykat yi ak yeneen jàppante ci askan wi ngir ñu mëna tëral ak amal politik yu jaar yoon ci barabu liggéey bi, prograami fàggu ak toppatoo bi, ak defar ay pexe ngir jàppale liggéeykat yi ci sectëru informal. Bokk na ci liggéeyandoo bi am ci diggante OIT ak ñatti pàcc yi ci bokk, ak itam liggéeyandoo ak ay naataangoom ci àdduna bi.
VIH/SIDA luy lore la ci àdduna liggéey bi: mingi gàllankoor wàll wi gëna am njariñ ci kàttan liggéey bi, di wàññi xaalis bi ñuy am, ba noppi di indil entreprise yi njëg yu bari ci bépp wàll ndax dafay wàññi liggéey bi, di yokk njëgu liggéey bi, di ñàkk xam-xam ak jaar-jaar. Rax ci dolli, VIH/SIDA mingi gàllankoor yelleefi nit ñi ci liggéey bi, rawatina lu jëm ci beddi ak tuutal liggéeykat yi ak nit ñi dundu ak VIH/SIDA.
Mbas mi ak jafe-jafe yi mu jural nit ñi ñoo gëna ñakk kaarange, lu ci melni jigéen ñi ak xale yi, loolu dafay yokk ñàkka yamale gi am ci diggante góor ak jigéen, di yokk jafe-jafe liggéeyloo xale yi. Loolu moo tax OIT fas yéene génne kàddu yu am solo ci wàllu VIH/SIDA ak àdduna liggéey bi. Kod bi dina am solo lool ngir moytu tasaaroo mbas mi, wàññi jafe-jafe yi mu mëna jural liggéeykat yi ak seeni njaboot, ba noppi aar askan wi ngir mëna xeex feebar bi. Dafay wax ci njàngale yu am solo, lu ci melni ràññee VIH/SIDA ni jafe-jafe ci barabu liggéey bi, baña xeex ci liggéey, yamale góor ak jigéen, saytu ak nëbb, waxtaan ci askan wi, fàggu ak toppatoo ak jàppale, muy fundamaa ngir xeex mbas mi ci barabu liggéey bi.
Additional details
References
- ISBN: 92-2-112562-9